Lan mooy Suuf su Baax?

Good Soil Evangelism & Discipleship daf dee dimbale taalibey Al-Maasi Esaa (Yeesu Kirista) ngir ñu jàngale xibaari yaakaar ci àdduna su fees ak ay diine yu bari ak ay aada. Dañu dee defar ay téeré (buk) yu jëm ci mbiri Kàddug Yàlla, ngir tas xibaar bu baax bi ak it jàngal taalibey Esaa (Yeesu) yu ees yi naka lañu mën a sax bu baax ci seen ngëm. Turi “Good Soil Evangelism & Discipleship” dañu ko jëlee ci “Léebu Beykat bi” ñoo jànga ci Injiil bu Sella bi. Jiwu wi mooy Xibaar bu Baax bi. Waaye lan la Esaa (Yeesu) waxoon ci mbiri suuf su baax si nak? Xaaji Injiil yi ñoo wax Macë ak Mark ak Luug jëfoo nañu ñetti baat yu uute ngir faramfanceel suuf su baax sóosu.

Naka laa mën a dimbale nit ñi ndég ñu dégga Xibaar bu Baax bi te nangu ko?

Wolof yu gën a bari mësuñoo jànga dara ci mbiri Téeré Bu Sella bi (Biibël bi) wala li taalibey Esaa Al-Maasi gëm. Kon seen àdda ak diine dina tax duñu gaaw a xam ay kàddu yu bari yi nekka ci Téeré bi. Kon foog ñu tàmbale ci njélbéen ga di jànga ci mbiri xew-xew yi ñu gis ci Téeré bu Sella bi. Suñu leen jàngee benna-benna, balaa ñoo pare, dinañu xam Xibaar bu Baax bi be mën koo nangu.

Xibaari Yaakaar mooy benna téeré bi ëmba 40 xew-xew (20 yi ñu jélee ci Tawreet bu Sella bi, Sabóor bu Sella bi, ak yeneen mbinda yi Yàlla jaarale ci yonent yu njékka yi ak 20 yi ñu jélee ci Injiil bu Sella bi) yi ñu tànna ngir xamle ni Yàlla jote nit ci loxob Saytaane ci kàddu yi Jullit yi mën a dégga bu baax. Téeré bi nak, dañu ko liggéey ndax nit mën koo jànga ci lu gaaw (ci ni ki fukki minit ak juróom) wala ndanka-ndanka (ci ñaar fukki waxtu mbaa lu ko ëppa). Xibaari Yaakaar am na ay nataal yu ànda ak xew-xew (wala njànga) bu nekka. Am na it ay nataali goox yi wan nit fu xew-xew ya xewoon.

Xibaari Yaakaar ngir Xale yi

Xibaari Yaakaar Xale yi: Gëstu be Gis Pexe mi Yàlla Indi, mooy téeré bi ñu jélee ci bu mag yi, waaye dañu ko liggéeyal xale yi. Dañu ko yombalal xale yi am 8-12 at, ndax mu neex a jànga. Xibaari Yaakaar Xale yi daanaka benna la ak téeré bi ñu liggéeyaloon mag ñi: am na 40 xew-xew (njànga) ngir jàngale te jànga nettalib mucca gi Yàlla amal di ko xamle ci Téeré bu Sella bi (Biibal bi). Pom buy Wane Dunda gu Dul Jeex (Chronological Bridge to Life) itam bokka na ci. Xew-xew (njànga) bu nekka dafaa feesal benna xati boppam. Téeré bii (Xibaari Yaakaar Xale yi) am na 64 xat te ànda na ak ay jëf yi xale yi mën a def ak ay nataali goox ak it ay fo (game) yi mën a tax xale yi gën a mokkal njànga mi.

Wolof Cond Cover

Xibaari Yaakaar… ci lu gàtta

Xibaari Yaakaar bu ndaw bii ëmba na nataal yu rafet yi wane 20 xew-xew yii nekka ci Mbinda mu Sella mi: Yàlla Aji Sax Ji; Amalag Àdduna si; Amalag Nit; Bàkkaari Malaaka mu Am Doole; Fi Bàkkaari Nit Tàmbale; Li Waral Dee; Li Ñu Dige ci Ki War a Daane Saytaane ba Fàww; Amalag Koddaay; Li Yàlla Digoon Ibraayma; Yàlla Joxewoon na Mbote; Yeneeni Kuutal yi Ñu Àppa; Li Ñu Dige ci Musalkat bi; Njuddute Esaa Al-Maasi (Yeesu); Xoolleen Mboteem Yàlla mi; Esaa Al-Maasi Am na Doole ci Kow Bép Mbindéef; Esaa Al-Maasi (Yeesu) Daan na Dekkil ñi Dee; Coono yi Esaa Jànkuwanteel ngir Génnee Suñuy Bàkkaar; Ndekkite Esaa (Yeesu); Yàlla Éegé na Esaa; Bés Pénca; Ajjana. Ci kow lóolu, Xibaari Yaakaar ci lu gàtta bii ëmba na it ay aayay Mbinda mu Sella mi yi ànda ak xew-xew yi ñu liimoon fii.

Contact Information

For more information or to order these resources, please send a message to Info@GoodSoil.com.

Additional resources may be viewed by visiting this page: GoodSoil.com/Resources.

Join Our Mailing List

Get notices for new products, resources, and training events.

Set your country and language

We will add support for new countries and languages in the future.